Sëñ Móodu Rasiit Njaay

Sëriñ Móodu Rasiit Njaay (1921 – 2004) di doomi Sëriñ Mabànji Xujja Bàlla ak Soxna Anta Bàlla, mi ngi gane jamono ci atum 1921.

Sëñ Muhamadu Rasiit Njaay bokk na ciy jikkoom mooy diganteem ak Broomam mu bàyyi ci xel lool, li ñiy wax ragal Yàlla di jëfe digal yi kem kàttanam di bàyyi tere yi kem kàttanam, ragal sunu Boroom sax mooy ndékaanam li mujj, waaye ku sàmmu woon la ci lépp lumu xamul lew na walla lewul ku sellaloon la ,bëgg lool lu
làqu li miy def diganteem ak Boroomam bëggul kenn xam ko, daa na jàng ñaar fukki hisib guddi gu nekk, ku bañoon ag siiw la, ku yërëmoon miskiin yi la ,daana yóbbulu ci woppitaatu Ndaamaatu aw ñam bis bu nekk, ku maandu woon la ci àtte ñaar ñu jote. Ku bëggoon kuy jéggale la.
Amna borom oto bu mas a fiir ab sëtëm mu faatu mu ne ko dama lay jéggal te duma la laaj say bokk, ndax bëgguma nga yaakaar ne ñoo tax ma jéggal la, ku tabe woon la ,ku bëggoon ag defare ci digante ñaar ñu juuyoo ,waaye ku bëggoon ak bokk la itam, daan ci dox daan ci wax.

Moom nag mi ngi génn àdduna ci atum 2004 ca Tuubaa.

Aji-bind ji: Saaliw Njaay
Aji-topp ji: Seex Lóo

Waxi Sëñ Móodu Rasiit Njaay

Ku Lu baax tee def Lu baax Lépp ay bokk baax. Bu dara yàq dara. Lu la rombuy di bajantu Leegi mu romb lay soox Defar bayyi fi daf maa gënal yàq bàyyi fi . Fuma ñaan ne soxna...

🎧 Déglu

Yaa ibna

Yaa ibna xaaliya na ngeen diy dànnte bañ a ngóoroo donn naa ab dànn Donn ug fetal cib dànn daf maa wóor neSoo dànnawul du tee nga reerew yànn Fëlee di woon dàggaam du tee jëggaaniMoom tool ya soo...

🎧 Déglu
error: Content is protected !!